Gëm Yàlla
Gëm Yàlla du xalaat bu ñu jël rekk walla lu xel di foog, waaye mooy fitra (nee-biir) bu ñu sàkkee, mu suux ci xolu nit ku nekk. Bakkanu doom-aadama, fu mu mënti fees ak bànneexi àddina walla mu loru ci wuti alal, su jàqlee walla mu nekk ci musiba, dafay dellu di woo Sàkkikoom te wéeru ci moom, te ci biiram mu xam ne àddina si am na Boroom bu am Kàttan, te nekkam fi du mbirum mbeteel rekk te amul ku ko sàkk.
Sunu xel moo ñuy jàngal ne lépp lu am ci àddina sii am na dig te laaj na ku ko sàkk. Su ñu xalaatee ci ni Yàlla bindee doom-aadama cig màgg, juge ci benn tocc-tocc ba nekk nit ku mat, ak doxalin wu teey wi àddina si di doxee, ak li lëkkale mbir yi; loolu lépp firnde la ne, ki sàkk àddina si Boroom Xam-xam la, tey Boroom Njib. Xel mu sel mi mënul nangu sax ne mbir yi seen bopp lañu sàkk walla mbeteel a tax mbind mu rafet mii am.
Xam Yàlla, ci xalaat ci ay firndeem yu nekk ci àddina si ak yu nekk ci Alxuraan lañu koy ame. Ndaxte firnde yooyu, fitra (nee-biir) ak xel yépp lañuy waxal. Su jullit xamee ne Yàlla mooy Sàkkkat bi te moom àddina si, dafay jaamu Yàlla rekk, du ko boole ak kenn. Njariñ ak musiba, fu mu juge rekk lañu koy séentu, di ci topp yoonu Yonent yi, jàmm yal na nekk ci ñoom, ñoom ñi seeni xol ak seeni jëf jëmale woon ci Yàlla képp.
Ngëm gu wér ci jëfi jullit bi ak ci jikkoom lañu koy gise. Du ngëmum xol rekk, waaye dafay feeñ ci déggal ndigëli Yàlla. Sopp Yàlla ak ragal ko, ñoo di ruwu jaamu gi. Ñoo tax dundug jullit bi di nekk ay jëf yu baax yu toftaloo te am njariñ, ci noonu liggéeyu bés bu nekk, su ci yéene ju sell ak jagleel Yàlla jëf ji taxawee, day soppiku di jaamu gu jullit bi di séentee jëmm ju tedd ju Boroomam, di topp li Yonent bi Muhammad ﷺ indi.
الإيمان بالله ليس مجرد فكرة نظرية أو ترفاً عقلياً، بل هو فطرة راسخة في أعماق كل إنسان. إن النفس البشرية، مهما حاول المرء حجبها بالشهوات أو غطّاها بالانشغال بالماديات، تعود عند الشدائد والأخطار لتنادي خالقها وتلجأ إليه، مدركةً بعقلها الباطن أن لهذا الكون رباً قديراً، وأن وجودها لا يمكن أن يكون مصادفة محضة بلا صانع.
يعلمنا العقل أن كل شيء في هذا الكون المحدود يحتاج إلى مُوجد، فالتفكر في عظمة خلق الإنسان من نطفة إلى إنسان متكامل، والنظام الدقيق الذي يسير عليه الكون، والروابط بين الأشياء؛ كل ذلك يقطع بأن وراء هذا الوجود إلهاً عليماً حكيماً. إن العقل السليم يقف عاجزاً عن تصور أن المادة خلقت نفسها أو أن المصادفة أوجدت هذا النظام البديع.
إن معرفة الله تأتي من خلال التأمل في آياته الكونية والقرآنية التي تخاطب الفطرة والعقل معاً. فعندما يدرك المسلم أن الله هو الخالق والمالك لهذا الكون، فإنه يوحده في ألوهيته، لا يشرك معه أحداً في عبادته، ولا يطلب النفع أو دفع الضر إلا منه، متأسياً في ذلك بمسيرة الأنبياء عليهم السلام الذين وجهوا قلوبهم وأعمالهم لله وحده.
يظهر الإيمان الصادق في عمل المؤمن وسلوكه، فهو لا يقتصر على العقيدة القلبية، بل يتجلى في الطاعة والامتثال لأوامر الله. إن حب الله وخوفه هما روح العبادة التي تحول حياة المؤمن إلى سلسلة متصلة من الأعمال النافعة، حيث يتحول العمل اليومي العادي بصدق النية والإخلاص إلى عبادة يبتغي بها المؤمن وجه ربه، متبعاً في ذلك ما جاء به النبي محمد ﷺ.