Asaka
Asaka mooy ponk bu ñetteel bi. Li muy tekki mooy joxe benn pàcc bu ñu dogal ci alal, ñu jagleel ko ñi ko yeyoo ci ay miskiin ak ñu ñàkk. Farata la bu lay laabal alal ji, di la sellalal sa bakkan ci njekkte, te di taxawal ag dimbalante akug bokk ci diggante jullit ñi.
Asaka ci Lislaam du galag rekk bu ñuy fay, waaye mooy benn jaamu Yàlla gu lay jegeele ak sa Boroom, ak jëf ju wone dëggug sa ngëm. Jullit bi xam ngëneelul Yàlla ci kawam, dafay xam ne alalam lu ñu ko dénk la te Yàlla a ko ko dénk. Kon, génne ci benn pàcc du ag wàññiku, waaye ag laabal bakkan la ci caat, ak jëf ju wone ni mu santee xéewal gi, ak firnde ci ni mu gëne bëgge Sàkkkat bi raw alal.
Asaka ponk la bu am solo ci wàllu askan wi, te yéeneem mooy dëgëral diggante gi ci biir jullit ñi. Dafay tabax ay jàlluwaayi yërmande ci diggante borom-alal ak ñu ñàkk, di sàmp yëg-yëgi mbokk ak dimbalante. Ci moom, ki ñàkk day am fu mu téye ci soxlaam, ki am itam day jàng nu mu mana jàll ci bëgg boppam. Bu ko defee, mbañeel day jeex, mbëggeel di tas. Diggante nit ñi di jóge ci luñu tënke ci alal rekk, di dem ci ay diggante yu kawe yu tegu ci yërmandey Yàlla ak sàrteesam, bii di sàmm njariñu jaamam yépp.
Jullit bu sàmm joxe asaka, firnde la ci ni mu wuyyoo ndigëlu Yàlla te wóolu dige bi mu ko dig ne dana ko ko feyal te yokk ko. Ni ngëm gu dëggu di feeñee ci julli ci ag toroxlu, noonu la itam di feeñee ci asaka ci ag tabe. Ci nii, asaka day may jullit bi ag teggin ci bakkanam, di ko goreel ci njaamug caat, di tax xolam di laqatu ci Yàlla, bañ a laqatu ci alal. Mu am yaqiin ne barke bi mi ngi ci li muy saraxe ngir Yàlla, te wërsëg gu dëgg gi mooy la mu denc ngir àllaaxiraam.
الزكاة هي الركن الثالث، وتعني أداء نسبة محددة من المال إلى مستحقيها من الفقراء والمحتاجين. هي فريضة تُطهِّر المال، وتُزكّي النفس من البخل، وتبني التكافل والأخوة بين المسلمين.
الزكاة في الإسلام ليست مجرد ضريبة مالية تُؤدى، بل هي عبادة تقرب العبد من ربه، وشعيرة تجسد صدق الإيمان بالعمل. فالمؤمن الذي يعترف بفضل الله عليه يدرك أن ماله أمانة استخلفه الله فيها، لذا فإن إخراج جزء من هذا المال ليس نقصاً فيه، بل هو تطهير للنفس من الشح، وتعبير عملي عن شكر النعمة، وبرهان على محبة الخالق فوق محبة المادة.
تُعد الزكاة ركناً اجتماعياً أصيلاً يهدف إلى تماسك المجتمع الإسلامي؛ فهي تبني جسوراً من التراحم بين الغني والفقير، وتغرس مشاعر الأخوة والتكافل. من خلالها يجد المحروم سداً لحاجته، ويتعلم الميسور كيف يتجاوز أنانيته، فيختفي الحقد وتنتشر المودة، وتتحول العلاقات الاجتماعية من مادية بحتة إلى علاقات إنسانية سامية قائمة على رحمة الله وشريعته التي تراعي مصالح جميع عباده.
إن التزام المؤمن بأداء الزكاة هو دليل على استجابته لأمر الله وثقته بوعده بالخلف والزيادة. فكما أن الإيمان الصادق يظهر في الصلاة خاشعاً، يظهر في الزكاة معطاءً. وهي بهذا المفهوم تمنح المؤمن توازناً نفسياً؛ إذ تحرره من عبودية الطمع، وتجعل قلبه معلقاً بالله لا بالمال، موقناً أن البركة فيما ينفقه في سبيله، وأن الرزق الحقيقي هو ما يدخره لآخرته.